(AL ISRA-OU WAL MIHRADJOU (dit RAGNAANOU YONENTE BI) LA SUITE - TopicsExpress



          

(AL ISRA-OU WAL MIHRADJOU (dit RAGNAANOU YONENTE BI) LA SUITE 45 *Yonente bi neena gnou eundil ma Malàka mougnouy wakh Raf-Raf ,bò khòlè mèlokànam dafa mélni chaise wayè gnènti(4) Malàka gnòko yor,neena gnou tèkko si sama kanam daldi nima yèegueul ,ma yèek ,neena ma tòk mou nàwak man ba thia guèthie(mèr)gò khamni lèrr gnou wèèkh tall-la ,neena ma fèk fa ay Malàka yo khamni dano bindò ni ndianàw ,sèn gàaway ba kèn manoulako wakh ,gnou dèg bèn kaddou bounilèn sòop lèn sama soppé bi ci lèrr gui. Neena gnou dèmak man bama sòbou ci bir dékh gui,neena boun dieulòn assamanak soùf yèp bòlèko ,Malàka mama fa sòob day mèlni bèn pèp bouniou khar(manam assamanak souf). *Yonente bi neena gnou diall(continuer)toùti ma guissati guèèthi(mèr)gò khamni guèèthie gou dioùl kouk la ,neena ma rott ci Raf-Raf dàldi soudiòt ,mou am bàat bouma dég mou wakh, manit ma yoùkhou. Neena bi Yalla dèfè ma dèf nònou ba seug damani yaw Yalla mi nga khamni yay khèttali gniy sakkou khèttalikou,yaw miy borom mbindèèf yi,yaw miy wèttali gni wèèt ,yaw miy borom Hanrass,yaw mi nga khamni yay sama bour di sama sang,yaw miy sama borom di sama wètteul ,wày sakhal dima wèttali si wèèt gui disama wètteul ci wakhtou wi ma nék ,wala nga yabal bèn diamm,thi sa diamm yi mou wètteulima. A SUIVRE 46
Posted on: Mon, 24 Jun 2013 18:16:36 +0000

Trending Topics



Recently Viewed Topics




© 2015