XAMLE LUY KOOR ,TAARIIXU AK FARATAALAM Abdu Xadir KEBE KOR XAMLE - TopicsExpress



          

XAMLE LUY KOOR ,TAARIIXU AK FARATAALAM Abdu Xadir KEBE KOR XAMLE LUY KOOR ,TAARIIXU AK FARATAALAM Koor mooy juroom ñenteelu weer ci arminaatu jullit ñi. Weer wii mooy ndoorteelu wàccug Alxuraan ci suuf. Bokk na ci li tax jullit ñi di ko woor: magal ko. Woor Benn la ci ponki Lislaam yi. Moom nag am na fukk ciy ne-ne (matière): XAMLE LUY KOOR ,TAARIIXU AK FARATAALAM -XAMLE LUY KOOR Koor ci làkk : bañ a lekk, bañ a naan. Bu dee ci sariiya nag : bañ a lekk, bañ a naan, bañ a séy, bàyyi it mbooleem yiy dogloo la ko dale ca penkug fajar, ba ca sowug jant bi, ngir nag yéenee jaamu Yàlla. -TAARIIXU AK FARATAAL KOR Yàlla (t.s) moo farataal koor ci Muhammad (j.m) , niki mu ko farataale ca xeet ya ko fi jiitu woon ca waxam ju tedd ja: «Yéen ñi gëm, farataal nañu ci yéen koor, ni ñu ko farataale ca ña léen jiitu, ndax ngéen am ag ragal Yàlla» Loolu di woon ci bisub altine ci weeru baraxlu, ci ñaareelu at ci gàddaay gu barkeel gi( juge Màkka dem Madiina) Ngënéelul koor aki njariñam Ngënéelam [ Ramadaan am na ay ngënéel yu màgg te bari, yu yeneen weer yi amul, àddiis yiy saxal loolu te di ko feddali yu bari lañu : Waxam ja (j.m) : «Julli yi juroom, àjjuma ba àjjumawaat, ramadaan ba ramadaanati, dana ñu far bàkkaar yi nekk ci séen diggante, bu ñu teetee bàkkaar yu mag yi». Waxam ja (j.m) : «Ku woor ramadaan ngirug gëm ak sàkku tuyaaba, jéggalees ko li jiitu ciy bàkkaaram». Yonnant bi (j.m) wax na ne : «Gis naa waa ju bokk ci sama xeet wi muy yalgat ngir mar, déeg bum dem ñu aaye ko ko, koorug ramadaan dikk wëgg ko, nàndal ko». Waxam ja (j.m) : «Guddi gi njëkk ci ramadaan bu jotee, dañuy jéng saytaane ak way féttéerluy jinne yi, tëj bunti sawara, du ñu ci ubbi benn, ubbi bunti àjjana, du ñu ci tëj benn, bu ko defee aji woote, woote ne: yaw miy sàkkuw yiw dikkal, yaw miy sàkku ay dëppal, Yàlla am na ñu ñu goreel ci sawara, te loolu guddi gu nekk lay doon». Waxam ja (j.m): «Koor de pakk la bu lay fegal sawara, ni pakk di fege boroom cib xare». Waxam ja mu nee (j.m): «Ku woor ab bis ngir Yàlla (t.s) Yàlla dana soril jëmm ja sawara lu tollook juroom ñaar-fukki nawet ngir bis boobee». Waxam ja (j.m): «Ki woor de bu dogee lu mu ñaan Yàlla may ko ko» Waxam ja (j.m) : «Àjjana am na bunt bu ñu naan Rayyaan, ku dul ñi woor duñu ca jaar, bu ko defee ñu ne: ana ñi wooroon, ñu daal di dikk, ku dul ñoom nag du dugg, bu ñu duggee it ba noppi ñu tëj bunt ba, keneen du dugg» ay njariñam Koor am na ay njariñ yu ruu, yu mboolaay ak yu wér-gu-yaram ñooy: Bokk na ci njariñi ruu yu koor yi : moom day tax nga man a muñ, taggate ci, di tax it nit ki di wattoonteek bakkanam ak a jiyaar ak bànneexam, di jur ci bakkan ag ragal Yàlla te di ko ci suuxat, rawati na ragal Yàlla gi nga xam ne mooy sabab su mag si tax ñuy woor, moom la Yàlla (t.s) di firndéel ca laaya ba, ba mu naan : «Farataal nañu ci yéen koor, ni ñu ko farataale ca ña léen jiitu, ndax ngéen am ag ragal Yàlla» Bokk na ci njariñi mboolaay yu koor yi : day indi ag nosu ci xeet wi akug bennoo, bëgg ag maandute akug yamoo, dana sos tam ci jullit ñi ag ñeewant, yërmaande, di joxe it jikkoy ihsaan (rafetal), dina feg mboolaay gi it (la société) ci ñaawtéef yi ak bon-boni jikko yi. Bokk na ci njariñi wér-gu-yaram yu koor yi : moom (koor) day setal ay butiit, di defar ag mbàq, di setal yaram wi ci desiit yu bon yi ak diigiit yi , di wàññi aw yaram, di néewal gariis gi ci yaram. Adiis ba nee na : “ woor-leen, wer” Ñatteelu ne-ne bi : ci li ñu sopp ci koor, li ñu ci sib, li ñu ci araamal : Li ñu sopp ci koor Sopp nañu woor bis yii : 1- Bisub Arafa, ci ku ajul, mooy juroom ñeenteelu dil-hijja, ngir waxi Yonnant bi (j.m): «Woor bisub Arafa dina far bàkkaari ñaari at, ma jàll ak may jublusi. Woor bisub fukkeel ba di Aasoora nag moom day far bàkkaari at ma wéy». 2- Bisub Asoora ak Taasooha, ñooy bisub juroom ñeenteel ak bu fukkeel ci weeru muharram, ngir waxam ja (j.m) : «Woor bisub Aasoora dina far bàkkaari at mu jàll», ni mu woore moom Yonnant bi (j.m) bisub Aasoora te digale ñu woor ko, ne : “déwén bu neexee Yàlla dinañu woor Taasooha (bisub juroom ñeenteel ba)” 3- Juroom benni fan ci sawaal , ngir waxam ja (j.m) : «Ku woor ramadaan teg ca juroom benni fan ci sawaal, mel na ni ku woor diirub jamono». 4- Xaaj bu njëkk bi ci weeru baraxlu, ngir waxi Soxna Aysa (y.y.g) ja : «Masumaa gis Yonnant bi (j.m) mu woor mukk weeru lëmm wu dul wu koor wi, masuma koo gis it mu woor ciw weer lu ëpp li muy woor ci baraxlu». 5- Fukki fan yu njëkk yi ci dil-hijja, ngir waxam ja (j.m) : «Amul yenn bis yu Yàlla gën a soppe ay jëf yu rafetet ci bis yii: maanaam fukki fan yu njëkk yi ci dil-hijja, ñu ne ko yaw Yonnantub Yàlla bi, xanaa jiyaar kay ci yoonu Yàlla moo gën a rëy yooyu bis? mu ne dée-déet, lu dul waa ju génn ci jëmmam ak alalam ci yoonu Yàlla, te delloosiwaatul dara» . 6- Weeru muharram, ngir waxam ja (j.m) ba ñu ko laajee: «Gan koor a gën ginnaaw ramadaan?» Mu ne : weeru «Yàlla wi ngéen di tudde muharram». 7- Bis yu weex yi ci weer wu nekk, ñooy: fukk ak ñatt, fukk ak ñeent, fukk ak juroom, ngir waxi Abuu Darin ji (y.y.g) : «Yonnant bi (j.m) digal na nu nu woor ci weer wi ñatti fan yu weex yi : fukk ak ñatteeel; fukk ak ñeenteel; fukk ak juroomeel». Mu ne : «Ñoom de ñook woor diirub jamonoo yam». 8- Bisub altine ak bob alximis, ngir li ñu nettali ne li ëpp ci li Yonnant bi (j.m) daa woor mooy bisub altine ak bu alximis, ñu laaj ko ko mu ne: «Jëf yi dees leen di gaaral altine ju nekk ak alximis, bu ko defee Yàlla di jéggal jullit bu nekk walla aji gëm ju nekk, ndare ñaari way tóngóo yi, mu ne nañu leen mujje» 9- Woor bis, wori bis, ngir waxam ja (j.m) : “ wooriin wi Yàlla gën a sopp mooy wi Daawuuda daa def (j.m), julliwiin wi Yàlla gën a sopp mooy wu Daawuuda , da daan nelaw benn xaaj ba , taxaw benn ñatteel ba , di nelaw juroom benneel ba. Daan na woor it benn fan, wori ba ca des” 10- Woor ci ki yorul jabar, te manul a denc , ngir waxam ja (j.m) : «ku ci toll ci denc, na wut jabar, moo la gën a man a tee xool jigéen ñi, gën laa musal ci njaalo, ku ko manul nag nay woor, (moom koor gi) ag tàpp la ci moom». Al-buxaari moo ko soloo. Li ñu sib ci koor 1- woor bisu Arafa ci ku fa taxaw, ngir tere gi ko Yonnant bi (j.m) tere ci ku fa nekk. 2 – ber bisub àjjuma woor ko, ngir waxam ja (j.m) : « bisub àjjuma séenug iid la buleen ko woor, ndare bu da ngéen a woor bis ba ko jiitu walla ba ca topp » 3 – ber bisub gàwwu woor ko, ngir waxam ja (j.m) : « Buleen wor bisub gàwwu bu dul farata ci yéen, bu waay amul lu dul xàncug reseñ it walla bantub garab na ko lekk » 4 – woor mujjug baraxlu ngir waxam ja (j.m) : « bu baraxlu xaajatee buleen woor » Ag yeete Sibéelug woor fan yii sibéelug sellal la. Waaye lii di ñëw nag ag sibéelam, sibéelug araamal la: 1 – jokkale, mooy jokkale ñaari fan di ko woor walla lu ko ëpp ci lu dul dog ci diggante bi, ngir waxam ja (j.m) :«Buleen jokkale» ak waxam ja :«Moytuleen di jokkale». 2 – woor bisub sikk, mooy bisub fanweer ci baraxlu, ngir waxam ja (j.m) : «Ku woor bisub sikk moy nga baayi Qaasim». 3 – woor diirub jamono, mooy woor at mépp ci lu dul dog ci, ngir waxi Yonnant bi (j.m) : «Ku woor diirub jamono, wooroo». ak waxam ja : «Ku woor diirub jamono wooroo, dogoo». 4 – koorug jigéen ci lu dul ndigalu boroom këram bu teew , ngir waxam ja (j.m) : «Bu jigéen woor benn bis te jëkkaram nekk fi, te joxu ko ci ndigal lu dul weeru koor». Koor gu ñu araamal gi
Posted on: Sat, 13 Jul 2013 17:47:19 +0000

Trending Topics



Recently Viewed Topics




© 2015