Lépp lu aju ci Muurum Koor ci baati Wolof yu leer Muurum Koor - TopicsExpress



          

Lépp lu aju ci Muurum Koor ci baati Wolof yu leer Muurum Koor walla muddum koor di ci wu-araab “زكاة الفطر/Zakaatul Fitr” farata la ci bépp jullit bu di boroom xel, mag walla ndaw, góor walla jigéen, ab jaam (bu dee ab jaam boroomam moo ko koy génneel) walla as gor. Muurum Koor Abdallaah mom (Ibn) Omar (Yal na gërëmul Yàlla nekk ci ñoom) dikke nanu waxtaan (Hadiis) ne: « Yonentub Yàlla (Yal na xéewalug Yàlla nekk ci moom) farataal na ci nun muurum koor, saa` ci tàndarma walla saa` ci bele, muy ab jaam walla as gor, jigéen walla góor, mag walla ndaw bokk ci jullit ñi » (Muwatta, Buxaari 2/579, Muslim, Tirmiidhi, Abuu Daawuud, Nasaa-ï ak Ibn Maaja ak ñeneen ñu dul moom) Ginnaaw biko Hadiis boobu farataalee weddi ko ag kéefar la, ku ko bàyyi te tay ko te tëlewu ko ab saay-saay lees koy jàppe, bu ko tuubul ba dee te Yàlla Aji-tedd ji jéggalu ko ko payug jëf ji sawara la. Ku ko deful it du tax mu wàcc ko ba mukk ci dëppook boroom xam-xam yi, doonte bu julli gi weesoo yoolub sarax la ci’y ame. Muurum Koor kañ lay war ? Xanaa Balaa noo julli korite lees koy génne. Mom Omar (Yal na gërëmul Yàlla nekk ci ñoom) neena: «[Yonent bi ((Yal na xéewalug Yàlla nekk ci moom) )] Digal nanu nu génne muurum koor balaa nit ñee génn di julli ji [kori] » (Buxaari 2/579, Muslim) Abdullaah Mom Abaas (Yal na gërëmul Yàlla nekk ci ñoom) neena: «Yonent bi farataal na muurum koor ngir mu laabal aji-woor ji ci caxaan yi ak safaan yi [mu def ci koor gi] akit ngir leel way-ñàkk yi. Ku ko génne njëkk julli gi nangulees nako muurum kooram. Ku ko génne ginnaaw julli gi nag, sarax la ci sarax yi » (Abuu Daawuud, Ibn Maaja ak Daaraqutnii) Naafi` nettali na ne : « Ibn Omar génne na ko benn walla ñaar i bis njëkk Korite » (Buxaari) Ci ngiirum Maalig mi waa réew mi di gën a sukkandikoo ak Ngiirum Imaam Ahmed, neena ñu : « Manees naa joxe Muurum Koor benn walla ñaari fan njëkk korite » niki ko Naafi` saxalee ne Ibn Omar def nako. Ci ngiirum Shaafi`: Fuñ umee Koor rekk manees nakoo génne. Bu dee ci Ngiirum Abuu Hanifa neena ñu : Manees nakoo génne njëkk weeru koor sax. Bu dee waxtuw joxe ko nag moongi doore ci bu weeru kori wi feeñee, la ko dale ca fajarug kori ba baa ñuy julli kori ci li gën a ñoŋ. Am it ñu jàpp lako dale ca timis gi weeru kori feeñee. Laabire ci loolu : Wax i Nggirum Imaam Maalig ak Imaam Ahmed “genne ko ci ñaari fan jëm kori” ñoo sax ci sunna, moo gën a lënk. Waaye yeneen wax yi it ci góor-góorlu (ijtihaad) la tege ngir ag jàppandal ñeel jullit ñi. Kon ku loru man nakoo jëfandikoo ci lu dul par-parloo. Ci misaal bu fekkee ne fi nga nekk amoo koo ko fi man a jox te réew sàngam walla dëkk sàngam la war a dem, nanu seet ñaata bis lay def àgg famu jëm teñ man koo séddale njëkk ñaari fan jëm jullig kori ngir moo gën a dëppoo ak sunna. Ku ko génnewul ba julli gi wees nag ? Boroom xam-xam yépp dëppoo nañu ci ne du tax mu wàcc ko mukk doonte sarax lay doon bu julli gi xësee weesu niko Yonent bi waxee: « (...) Ku ko génne ginnaaw julli gi, sarax la ci sarax yi » Te it ku ko génnewul ba julli gi wees ba jant so ci lu dul benn ngànt bàkkaar la te du tax mu wàcc ko, te it bu ko joxee sarax la ci sarax yi. Muurum Koor ana kan lay war ? Xanaa ab jullit bu di boroom xel, di as gor walla ab jaam (bu dee ab jaam boroomam moo ko koy génneel), di mag walla ndaw, góor walla jigéen. Abdulaah mom (Ibn) Omar (gërëmul Yàlla ci ñoom) neena: «Yonentub Yàlla bi (jàmm i Yàlla ci moom) farataal na ci nun muurum-koor ci weeru koor, saa ci tàndarma walla bele, muy ab jaam walla gor, jigéen walla góor, mag walla ndaw te bokk ci jullit ñi» (Buxaari 2/579, Muslim, ). Mu diko war ci boppam (gor si te di ab jullit bu am xel) ak koo xamni dundal ko moom la war ci Sharii`a niki : Soxnaam ak doomam ju góor ba bamuy mat góor (mukallaf/majeur) ak doomam ju jigéen ba baa muy am boroom kër ak ci ay way-juram bu ñu ko amul ak ay jaamam. Bu doom ju góor ji matee mukàllaf nag, ci ngiirum Maalig ak Ngiirum Abuu Haniifa, dóorul farata ci baay bi mu léen di génneel muurum koor., lu dul rekk mu ame laago ju ko tee man a liggéey. Bu dee ci ngirum Imaam Shaafi` ak ngiirum Ahmad ci kilifag kër gi léen war a dundal la war mu génneel muurum koor gépp kuy dund ci kër gi. Ci li sax ci ñatti ngiir yi mom Maalig, mom Shaafi` ak mom Ahmad, mooy ne ci jëkkar ji la war mu génneel jabaram muurum koor doonte jabar ji am nako, waaye na fekk nag jabar ji di jullit. Bu dee ci ngiirum Abuu Hanifa nag farataalu ñu ci jëkkar muy génneel jabaram muurum koor, ndax dañoo jàpp ne bokkul ci njël (dépense) yi ko war co jabar ji. Waaye bu ko defee it dañu koy jàppe lu mu def lu rafet ci coobareem. Ku ko amul woon bees la joxee lu la man a dundal ci bis bi ba suba, la ca des war na nga génne ko ci, bu desul it man nga koo génne ci lees la jox boo noppee jox ko sag njaboot, wér na ci sunna. Luy atteb ku tukki walla kuy tukki nag ? Dikk na ci Muwatta bu Imaam Maalig, ñu laaj Maalig ne ko “Kii sowwu (tinisi...) la dëkk bi ñuy dog koor fekk ko Misra (Esipt), fan la war a génnee muuruum koor ? Maalig ne : « Xanaa famu ko fekk rekk, waaye it bu ko ko ag njabootam génneelee ca sowwu fay gi benn la »” Kon ku tukki man nga koo génneel sa bopp fa nga nekk, niki noonu it bu la soobee woote fa nga dëkk ñu génneel lako fa. Ana ci lumu koy war a génnee ? Xanaa ca la ëpp ca réew ma mu dëkk di dunde, nun waa réew mii daanu ko génne njëkk ci Ceeb, Dugubi Suuna, Saaño, Basi, Tin walla Feele, ku ko amul jënd ko joxe ko, kuy dunde yu dul yii yitam man na koo génne ca lamuy dunde rek. Ana namuy war a toll? Xanaa benn (1) saa bopp bu nekk. Bu dee ci sunu réew mii dugub lees ko daa gën a génnee ngir ne moom lañu daa gën a dunde, bopp bu ne ñaari kilo ak genn-wàll ci Dugubi-Suuna ak yini deme. Bu dee Ceeb nag walla muy yu dul yii kon day wut nattukaay boo xamni ñaari kiloy dugub ak genn-wàll a koy fees mu natt ko ca te bañ koo peese ngir xam ñaata kilo la. Ci jamono jii nag ci sunu réew mii génne ko ci Ceep moo gën ndax moom la réew mi di gën a dunde. Ana luy benn Saa? Saa mooy tolloo ak ñeenti mudd, benn mudd bu nekk mooy tolloo ak sa tibbub ñaari loxo bees ko boolee. Yenn ci yees di dunde bees ko natte ci benn Saa: Bele: 2040g Cere: 1800g Tàndarma: 1800g Fariñ: 1400g Resiñ: 1640g Ceeb: 2300g Ana ku ñu ko war a jox ? Xanaa ku ñu war a jox Asaka rekk, ñoo bokk yenn sàrt it, te Boroom bu tedd bi tërale, nu man koo tekkee ci baati Wolof ne : « Asaka ñi ko yayoo ñooy : ñi néew am-am (ñàkk) ; yalwaankat yi ; ñi koy topptoo ; ñi ñu bëgg a nooyal séen i xol [ci lislaam] ; ak goreel jaam ; ña bor sonal ; ak ci lu jëm ci yoonu Yàlla ; ak doxandéem bu nekk ci tukki. Loolu moodi li Yàlla santaane te Yàlla kat ku xam te xarañe la » [Saaru: 009 / Laaya: 60] Sopp nañu ci yii nag : - Mu di as gor su di ab jullit te am ca aajo ju wér te muy koo xamni seenuwu loo ci moom lenn njariñ lu dul jox ko ko ngir Yàlla rekk. Séenuwu loo mu di la sant ak a gërëm walla mu di ko nettali fi aw nit, nga xamni bëgguloo sax ku ko yég. -Kenn du ko jox ab jaam. -Bëggu ñu nag ku la dogal ab tool nga di ko jox asaka ngir tool ba, loolu araam na ci ñoom ñaar ñépp, boroom tool bi nag bu ko moomee sañ nala koo jaay walla mu luye la ko waaye lumu ci doon, doo ko ko jox ci asaka ji walla luñuy lekk walla lu suuf di saxal. -Bëgguñu yitam jox nit asaka mu di ko jaay nga di ko jëndaat. -Bëggu ñu yitam tuxal asaka lu gën a sori juróom ñaar fukki kilomet te fi nga nekk ku ko yittewoo sori wu fa, bu ko weesuwul nag dara newu ci. Boo gisul ku ko yittewoo lu dul lu ko weesu yitam dara nekke ci. -Kenn du ko jox ku bokk ci giirum Haashim, manaam giir gi Yonent bi bokk, ngir ne du ñu lekk sarax. -Sopp nañu lool nag nga jox ko sa mbokkum jegeñaale ci dereet bu ko yittewoo, waaye sàrt nañu ci bum doon koo xamne dundal ko yaw la war ci Sharii`a, niki : Sa(y) doom ak sa(y) soxna. Li tax ñu sopp ko mooy ne : Ku ko jox sa mbokkum jegeñaale danga am ñaar i yool : benn (1) :yoolub dundal mbokkug dereet gi léen Yàlla boole ; ñaareel (2eel) bi : yoolub dundal joxe asaka ji di ndingalul Yàlla. Ku ko amul woon ba mu wàcc la bees la joxee lu la man a dundal ci bis bi ba suba, la ca des war na nga génne ko ca. bu desul it man nga koo génne ci lees la jox boo noppee jox ko sag njaboot. Abuu Hanifa ak ñénn ci boroom xam-xam yi nangu nañu genne ko jox ko ku bokk ci ñoñ-téere bi (Ahl-ul-Kitaab) manaam ñi nekk ci diiney Yahuud ak nasaraan. (Sayyid Sâbiq mooko indi ci Fiq As-Sunna) Waaye li gën a ñoŋ daal mooy jox ko jullit ñi ko yittewoo jëkk. Luy njariñam ci lu nëbbu ak lu feeñ ? Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: « Yonent bi farataal na muurum koor ngir mu laabal aji-woor ji ci caxaan yi ak safaan yi akit ngir leel way-ñàkk yi (...)» Abdullaah Mom Abaas (g.Y.c.ñ) neena: « Yonent bi farataal na muurum koor ci naan: Fexe léen ñu woomal tay!»(Daaraqutni) manaam ngir way-ñàkk yi woomal ci bisub korite gi. Hadiis boobu Al-Bayhaqi indi nako ci beneen riwaaya bu naan : « Fexe léen ba du ñu yalwaan i ci bisub kori gi » Kon dina laabal aji-woor ji ci mboolem rëcc-rëcc i koor gi te laabal ab xolam, kon yooyu bokk na ci njariñ yi nëbbu te Yonent bi (Yalna xéewalug Yàlla nekk ci moom) tudd ko. Ak it indi jàmmu ci nit ñi ci dimbalante, woomalal ñu ñàkk ñi ngir ñu yëg bër (feet) gi ni ñépp, fexe ba kenn du yalwaan ci bis bi, yooyu bokk na ci njariñ yi feeñ te Yonent bi (Yalna xéewalug Yàlla nekk ci moom) tudd ko. Amma nag Hadiis biy wax ne «لا يرفع صوم رمضان حتى تعطى زكاة الفط» fii ak génnewuloo ko deesul nangu sa koor, ci wax i boroom xam-xam i Hadiis yi wérul. Amna it beneen Hadiis bu ne : ( شهر رمضان معلق بين السماء والأرض ولا يرفع إلى الله إلا بزكاة الفطر «[Koorug] weeru koor dees koy wékk ci diggante asamaan ak suuf du àgg ca Yàlla mukk lu dul ne boroom [koor gi] daa génne muurm koor » (As-Suyuuti indi nako ci jaamihu as-saxiir jàppe ko ne hadiis bu ràgg maanaam da`iif) Daa am ku ñu xamul ci sanadu hadiis bi muy Muhammad ibn Ubayd al-Basri. Ñenn ci Boroom xam-xam yi ne li maanaa mi bëggoon a wax mooy ne : deesul jéggal aji-woor ji caaxaan yi mu des ci biir weeru koor wi fii ak génnewul muurum koor. Waaye lu ci man a am du wàññi darra ci amug solog muurum koorci lislaam ak nekk gu mu nekk di farata ci bépp jullit bu di Boroom xel. Weddi ko ag kéefar la, bàyyi ko ci lu dul lenn ngànt lu jaadu ag caay-caay la. Muurum Koor ndax manees nakoo génne ci xaalis ? Loolu gis-gis yu wuute dikk na ci. Ci ngirum Maalig maneesu koo génne ci lu dul aw cam. Maalig neena: « Muurum koor wareesu koo génne ci lu dul ñam. Deesu ko génne ci kee walla xiima (xaalis walla lu ko xeetoo) » loolu it mooy gis-gisu ngiirum Immam Shaafih ak Immam Ahmad ibn Hanbal. Laajees na ñaari yoon Ibn Utaymin mi bokk ci ngiirum Ahmad waxi Maalig ji mu wéral ko. (Majmuu` Fataawa bu Seex Ibn Utaymin, tomb-18 xëtu.280) Noonu it la ko Ibn Baaz gise. (Majmu’ Fataawa bu Seex Ibn Baas, tomb-14 xët.200-202) Ci ngiirum Abuu Haniifa manees naa génne muurum koor ci xayma ko ci xaalis (Imaam Nawawii mooko indi ci saraab Sahiihu Muslim). Boroom xam-xam yu bari ci jamono jii it nangu nañu ko ngir ne ñu gise xaalis taxawe ko fi, ba ci ñu bokk ci ngiirum Maalig. Mu ne : « أبوحنيفة وأصحابه والحسن البصري، وسفيان الثوري، وخامس الراشدين عمر بن عبد العزيز - رضي الله عنه - أجازوا إخراج القيمة في الزكاة، ومنها زكاة الفطر،وهو قول الأشهب وابن القاسم عند المالكية. » « Abuu Haniifa ak ñi bokk ci ngiiram, Hasan Al-Basrii, Sufyaanu s-Sawrii, Omar Ibn Abdel Aziiz juróoméelu xalifa bu jub bi (Yal na ko Yàlla gërëm), daganal nañu génne asaka ci xiima manaam xaalis (espece) te boole nañu ci asakay muurum koor ; loolu it nag mooy gis-gisu Ash-hab ak Ibn Qaasim ñi di dongay Maalig » «قال النووي: وهو الظاهر من مذهب البخاري في صحيحه» « Imaam Nawawi ne : Mel nane loolu it mooy feeñ di gis-gisu Imaam Buxaari ci Sahiiham bi » Laabire ci loolu : joxe ko ci ñam manaam li ngay dunde moom rekk a sax ci sunna, te Hadiis bi koy digle it daa waxni ngir jox way-ñàkk yi ñu lekk la manaam “tutt`imu t-ta`aam”, te moom lañ daan def it. Ginnaaw leel miskiin la wax nag, nanu léen leel ci li nuy lekk niko Sahaaba yi daan defe moo gën. Mu des nag bu ngànt amee, bu boobaa manees koo jëfe ci niko Abuu Haniifa gisee ci lu dul par-parloo te sellal yéene ji. Gisal naako nag lenn ngànt lu ma jàpp ag rafetam, mooy ne : Bu fekkee fi nga nekk amoo kooko fi jox, nga xamne dëkk sàngam walla réew sàngam la war a dem, séen cosaan yu wuute, ak séen i lekk yu wuute, bu boobaa manees koo génne ci xaalis jox kurél i lislaam yi koy laaj diko dajale, ñoom it bu ñu yeggee ñu def ay yitte ba jënd ko ci aw ñam joxe ko ci ngir moo gën a sax ci sunna. Kon ana lu nu man a tënk te jàpp ko man ak yeen ci waxi boroom xam-xam yii ? Mooy ne : -Muurum Koor war na bépp jullit, mu di mag walla ndaw, as gor walla ab jaam (bu dee am jaam kiko moom la war) -Farata la ci baay bu nekk mu génneel ko doomam ju jigéen ba kerok muy am boroom-kër. Niki noonu it doomama ju góor ju mat a gul mukàllaf ak doomam ju góor ju mat mukàlla te ame laago ju ko tee man a liggéey ; Ak it bépp jaam boo xamne mooko moom. -Warul ci baay bi muy génneel doomam ju góor ju mat mukàllaf muurum koor, moo xam doom ji am nako walla amu ko. Waaye bu ko doom ji amul nag te baay bi man kokoo génneel it moo gën a rafet na, ñàkk gee def daal la nu bëg a xamle ne bàkkaar nekku ci. -Ci li gën a sax ci waxi boroom xam-xam yi war na ci jëkkër ju nekk mu génneel ko jabara doonte jabar ji am nako, waaye na fekk nag jabar ji di ab jullit. -Jigéen ju ko am man nakoo génneel ay way-juram yu ko amul. Niki noonu it bu ko amee man na koo génneel ay doomam yu di ay jirim. -Ba tay góor gu ko am man nakoo génneel ay way-juram buñ ko amul. -Ku walla kuy tukki man ngakoo génneel sa bopp fa nga nekk, niki noonu it bu la soobee woote fa nga dëkk ñu génneel lako fa. -Liñu jublu ci am, mooy képp ku yor lu la man a dundal ci bisub kori bi ba mu des, la mu des mooy am te war na ca. Waaye niki noonu it kuko man a leb te mu am yaakaar ci ne dinga ko fay ci diir bu gàtt, man ngaa leb joxe ko, waaye sàrt nañu ci nga am yaakaar ju dëgër ci man koo fay ci diir bu gàtt, manaam fekk nga am loo yaakaar. -Li gën a sax ci waxi boroom xam-xam yi waxtuw génne ko mooy bu weeru kori feeñee, lako dalee ca fajarug korite fa kerok ñuy julli iid, amna ñu ne it lako dale ca timis ga weeru kori feeñee. -Ku ko génne ba waxtuw julli wi wees ci lu dul ngànt bàkkaar la te du tax mu wàcc ko, te it bu ko joxee sarax la ci sarax yi. -Manees nakoo génne it ñaari fan njëkk korite niki mu saxee ne Ibn Omar defe nako ne. -Dees nako génne ci ñam wi waa dëkk bi nga nekk di gën a jëfandikoo, ñeenti mudd bopp bu nekk manaam nit ku nekk ci kër gi te génneel ko ko war la. -Bu dee ci dugubi suuna ñaari kilo ag genn-wàll lay tollool, bu dee leneen lum man a doon, wutal nattukaay bu ñaari kiloy dugub fees nga natt ko ci te bañ koo peese ngir xam ñaata kilo la. -Ki ñu ko war a jox mooy ki ñuy jox asaka te nu tudd ko ci kaw. Boo ko xàmmewul man nga koo yóbbu ci jàkka ji la gën a jege, bu fekkee ni dana ñuy def ay yitte ngir séddale ko. Buñ ko dee laaj nag man nga léen koo jox te bañ cee lijjanti loolu. -Li gën a sax ci waxi boroom xam-xam yi maneesu koo génne ci lu dul ñam, maanaam ta`aam. -Ci loolu ñenn ci boroom xam-xam yi sunna yi saxal nañu ag man koo génne ci xiima maanaam xaalis ak lu ko xeetoo muy espece. Kon ku am ngànt man naa jëfandikoo wax jooju. Kon loolu mooy li nu leen amoon yéenee leeral ci lu aju ci muurum koor. Salla l-Laahu `Alaa Muhammad ! Yal nanu Yàlla defal korig jàmm ak i xéewal ñeel nu te ñeel leen. Nuy sàkku ci Yàlla mu nangu sunuy koor, sunuy dog, sunuy jaamu, sunuy tudd Yàlla, sunuy taxaw ak sunuy sujood te nangul léen, jéggal nu te jéggal léen, musël nu ci lor te musël léen. Yal nanu Yàlla aji-tedd ji defal suturas àdduna ag njéngalul Allaaxira ci barkeb weer wu tedd wii. Déwénati!
Posted on: Wed, 07 Aug 2013 13:07:26 +0000

Trending Topics



Recently Viewed Topics




© 2015